Yeesalu 20i Mai 2021
Ci 10i fan ak benn ci weeru maars 2020, kuréel gi yor wérgi yaram ci àdduna bi (OMS) neena lii di COVID-19 bi (Koronaawiris) feebaru mbass la. Mbir yaa ngi dox ci àdduna, tekk ci reew yaa ngi yokk wala di wañi tere yi ak/wala lepp lu jëm ci wallu kaarànge ngi ndax gis nañ xéeti koronaawiris yu yees (ay wariyant) ak porogarami ñakku yaa ngi gën di dem.
Taskati-xibaar yi ci àdduna ñu ngi def liggéey bu am solo ci yee askan wi ci lu jem ci feebar bi ak nan la réew yi taxawee ci xeex ko, ginnaaw bi ay ngornamaay réew yu bari gàllankooree tasum xibaar ak jotug xibaar gi, ci ni ko CPJ firndeele ci seenum mbind. Ñiy yëngu ci mejaa yi dañuy jànkonteel ay ërtal ak jafe-jafe yu tar, teg ci leeg-leeg- mën nañu ame ci jàngoro ji fépp fu leen seen liggéey yóbbu, wala tukki ak laaj-ak-tontu yi seen liggéey bi laaj, ni ko CPJ waxee ci laaj-ak-tontu bi ñu séq ak taskati-xibaar yi.
Ngir xam lu xew bis bu nek ak yéesal yi am ci digle yi ak tere yi, tass kati xabaar yiy yengu ci mbass mi war nañuy top xibaar yi bayikoo ci OMS ak kuréel ya ŋank walum pacc ca seeni askan. Ngir am lu wér ci lawug jàngoro ji waxtu wu nekk dal bi tudd Johns Hopkins University Coronavirus Resource Center nekk na barrab bu wóor te mucc ayib ci jottali xibaar ci wàll woowu.
Aar sa bopp ci biir nit ñi
Tere yi jëm ci tuki réew ak réew ak/wala ci wallu kaarànge gi danuy sopikku saa su ne, ba tax na liggéeyu mejaa yi mën nañu soppi anam biñu koy defee wala dakkal ko ci lu kenn dul yeglu.
Ñiy yëngu ci tassum xabaar te ñakku ba noppi war nañu bàyyi xel ci ne mën nan wale jàngoro ci ba leegi, ci ni ko centaru amerikin biy saytu bepp feebar (CDC) waxe, ndaxit xéetu ñakk bu ne akk namuy aare nit ki ci xéeti jàngoro yi wiris bi andale, ci ni ko Yale Medsin waxe. Ba tax na xéeti kaaràngey COVID 19 yu mel ni dàndante gi and takk maska, war nanu leena saxal saa su nekk.
Képp kuy waajal liggéey ci jamonoy mbassu COVID-19 war naa bàyyi xel ci ndénkaane kaarànge yii:
Waajtaayug liggéey bi
- Su jappandee, nga teela jël sa ñaku balaa ngay dem ci liggéey bi su dee mën nga koo jël, rawatina soo waree liggéeyi wala tukki ci barab yu bari riska am jàngoro ji.
- Ci ni risku am jàngoro ji tollu ci fi nga nek wala ca fa nga jëm, laaj-ak-tontu ci telefon wala ci lënd gi mooy gëna jappandi ci yaw di jàkkaarlook nit ki, ngir mëna neewal wallante ngi ak/wala di janook jàngoro ji.
- CDC neena màgget yi ak ñi am feebaru sooxaale lu mel ne jabet mbaa am yaram la jàngoro ji gën a jublu. Soo bokkee ci ñii, tekk ci na fa wallante te ngi tollu, warula ngay sóobu ci benn liggéey bu lay yobbu ci nit ñi. Te bépp liggéeykat bu ëmbit jar naa bàyyi xel.
- Saa su njiit yi di yable kuy jëli xabaar yi jëm ci mbassum COVID-19 war nañuy sóoraale songi mbañxéet yi niy song doomi bitim-réew, ci ni ko The New York Times leerale
- Yamale tukki ngi ci àdduna si akk tërelin yi jëm ci tëju ngi mën nanuy soppiku ci lu ken dul yeglu. Waxtaanal ak say njiit ci pexe yi nu tërel ci jàppandal ak taxawu la sula feebar bi dabee ci liggéey bi, di sóoraale yit ber sa bopp wala / mbaa ñu lesere la / tëj la ci barab diir bu yàgg.
Sellug Xel
- Ñi gën a xarañ ci taskati-xibaar yi sax mën nañoo jànkonteek jafe-jafey xel ci sa taataan xibaar ci mbasu COVID-19 bi ci ni ko Reuters Institute ca Iniwersite Oxford waxe. Wareef la ci njiit yi ñuy nemmiku seen taskati-xibaar bés bu nekk di seet nuñu def, te dileen taxawu aka jàppale ca namu waree.
- Sooraaleel janknteel coonoy xel ci wallu liggéey bi ci barab yi COVID-19 am, rawatina sooy taataan xibaar ci fu mel ne fajukaay yi wala berukaay yi, wala barabi tëj yi.Jumtukaay yu am solo ci taskati-xibaar yiy gis giraawaali ci seen liggéey am nañu fii di the DART Center for Journalism and Trauma. Yërël lii di CPJ wallu kaay gui ngir am ci yenenni jumtukaay, lu mel ne taxawu yu muc ayib ci sellug xel jëm ci taskati xabaar yiy taataan COVID-19 bi.
Mucc ci wàllu gi ak wàllaate gi
Réew yu bari ñoo ngi wëyel dàndante/ci diggante nit ñi , wante réew mu nek ak namu koy doxale. Sooy taataan xibaar ci barab yu feebar bi jublu lool wala ngay dem ci ben ci barab yii ñuy waaja lim, balaa ngay dem laajteel yan yiirukaay set setal lañu fa tëral. Bu dalul sa xel bul dem.
- Bépp xeetu loppitaan
- Kërug màgget ñi
- Kër gu am ku feebar, maggét, ku ëmb, wala ku ame jàngoro.
- Bepp liggéeyuwaay bu feebar bi jublu lool (fu mel ni isini yiy pakete yapp)
- Ag kër gu ñuy waajalee way-dawlu yi, fi ñu leen di lakkee, wala bépp liggéeyuwaay buñuy waajalee ab rob.
- Beddiku, beru, wala tëju
- Tanccaloo bi ci dëkkinu taax yu bari nit (fu mel ni lëmpel wala fawelaas)
- Dalub way-làkku
- Kërug walu, wala ab kasso bu ndaw/bu magg goo xamne am na ñu fa am COVID-19
Ay ndékaane yees nangu ngir mucc ci wàllante gi
- Na nga saxal dàndanteek ñepp nako njiit ya santaane ca fa nga nek. Te ngay bayi sooraale bu baax ñi nga xamne da ñoo ame màndarga feebaru noyi, lu mel ni sëxet ak tisooli, wala/ak sooy laaj ak tontu ay mag, ku ame jàngoro sooxaale, kepp ku jigeñ ku jàngoro ji feeñ ci moom, ñiy liggéeye fa ñiy facc ñi ame COVID-19, wala ñiy liggéeye ci barab yi feebar bi jublu lool.
- Jéemal deffe say laaj-ak-tontu ci bitti. Soo soxla deffe laaj-ak-tontu ci biir neeg, tanal barab bu feex (lu mel ni porantéer yu ubbiku) te ngay moytu diko deffe ciy barab yu xatt.
- Moytul di nuyóo akka lëngoo wala di fóon kenn.
- Jeemala taxawe wet te baña jakarlook nit ki sooy deff laaj-ak-tontu, te saxal dàndante ci niñ ko santaane.
- Foo tollu ngay raxasook saabu ak ndox mu tàng ba set wecc ci lu tollook 20i seconds. Te nga fomp say loxo ci nu mu gënë sele. Soo namee xam naka la nuy raxasse loxo bamu set yërël situb OMS
- Ngay jëffandikoo jel wala fonpukaay alkoliizé soo amul saabu wala ndox bu tàng, te nga tegg ci raxasook ndox mu tàng akk saabu ci numu gënë gaawe. (CDC digle na jëffandikoo jel bi am alkol te mu epp 60% etanol wala 70% isopropanol.) Bul weccee saxal raxassu ak jëffandikoo jel yamu nu.
- Mural sa gimiñ ak bakan sooy sëxët wala tisooli. So sëxët tee wala tisooli ci muswaar a seté sanil bu jekk ca mbalit ma te dem raxassu ji ba set wecc.
- Ngay moytu di laal sa xarkanam, sa baken, sa gimiñ, say nopp, ak yu ni mel.
- Ngay moytoo nane/lekke ci ay kop ak di lekke pakaaki kudu yoo njort ne keneen jëffandikoo na leen.
- Muural sa bopp bi. Kawar gu kudd yit nga takk te muur ko
- Tekil bépp takaay wala montar balaa ngay jublu ci liggéeyy, ndaxte COVID-19 mën naa dund ci fu nekk ci ay diir yu wuute.
- Sooy takk ay linet dée leen fomp ci saabu ak ndox mu tàng foo tollu.
- Moytul di sol lineti kontak ci liggéey bi, soo ko mënee, ngir moytu muy laalante ak say gëtt ndax jàngoro ji mënees na si jaare ba dug la.
- Tanal yere yi ngay sol, bayi xel am na yere yu gën gaawa sett yeneen. Te soo wacce nga fóot say yere ci ndox mu tàng ak saabu.
- Soo ko mënee, bul jendeek xaalis ci liggéey bi, te ngay fomb fo tollu say kart bankere/keredi, sa kalpe, ak sa poset saa su nekk. Tey moytu yit di duggal say yoxo ci say poos.
- Seetal ndaamaar li lay yombu ak indi sooy liggéeyi. Soo ko mënee moyul di dugg taranspor piblik ci waxtuy xëy ak wacc, te ngay laal jel alkol saa soo wacee ndaab gi.
- Soo nekkee ci sa ndaamaar wala bu liggéeyu kaay gi, na nga bayyi xel ni ki am jàngoro ji mën na ko walla ku nekk ci ndaamar si. Soo nekkee ci sa ndaamaar na nga wacce wiitar yi ngelaw liy uppu, te yit ngeen di muur seeni xarkanam wala tak maska.
- Di jël poz te bayi xel ci coono/katan gi, ndax coono day indi tayel ci samonteek set setal. Di soraale ñiy liggéeyi aka wacce fu sori tay dawal.
Muuru kaayu yaram waa loppitaan (PPE)
Ngir taataan ci anam yu sela, tass katu xabaar yi maness nanuy sol muuru kaayu yaramu waa lopitaan PPE yu nek su ko seen liggéey bi laajee. Lu mel ni ay gãa aa seté, maska xar kanam, taabelye / kombinesõo / wala liy muur dàll ak yuni mel.
Sol ak simi ci anam yu woor muuru kaayu yaramu waa lopitaan PPE dafay àndak sàmmoonte gu mucc ayyib ak ndénkaane yi ci jëm. Bësal fii ngir xam ndénkaane yi bàyyikoo ca CDC. Sooy sumi muuru kaayu yaramu waa lopitaan PPE nga nga deff ko ci anam yu mucc ayib, ndax toxalee ca jàngoro ji lu gaaw la. Lu la leerul nga laaj ki xam mu tàggat la ci balaa ngay dem ci liggéey bi.
Na nga xamit ne ca rèew yu bari muru kaayug yaram waa lopitaan (PPE) yu baax neew na fa, jëffandikoo ga mën na indi ñakkam.
- Te ngay settantal PPE yi ngay sol na baax te jot. Su la jotulee men naa xotiku/mbaa tere la yengu (su xatee), tekk ci men naa lonku fena lo mel ni lokke daal di xotiku (su yolamee)
- Dèel jëffandikoo màrku PPE waa loppitaan yu baax yi, di sàmmonte ak mbooleem ndénkaane yi. Di setantal jumtukaay yu yàqu yi ak/wala yu fóo yi niko. Màrk yi gën te wóor ñu ngi nii.
- Solal ay gãa sooy liggéey wala ngay seeti ku feebar bi dal fu mel ni loppitaan. Jàppal ni gãa wu nitiril bi moo gën a baax bu lateks bi. Sol ñaari gãa dina yokk kaarànge.
- Sooy liggéeyi fu am riska mel ni loppitaan, dafay laaj nga sol maska ak kombinesõo PPE bu jot sëkk.
- Soo waree sol kombinesõo, na nga dem tuwalet ba noppi soog sol PPE
- Suko liggéey bi laaje mën ngaa sol ay dàll yooy jëffandikoo benn yoon rekk wala dàllu permeyaabal ci sa kaw dàll, te soo génee ci loppitaan ba nga raxas leen. Su dee dàll permeyaabal nga sol na nga leen summi ci nu mucc ayib balaa nga fay jóge.
- Digle nañu PPE waa loppitaan ñu kay solee ci kanamu ku ci tàggatu, tay fàttaliku ne ci jamono jooju lu ne mën na ci xew ci am jàngoro ji. Widewoo solu ak sumeeku bi bàyyikoo ci CDC lu am solo la, waaye ñu bañ ko weccee ak tàggatu / caytu gi.
- Solal benn yoon kesse PPE yii di gãa, kombinesõo, taabalye, wala murrukaayu dàll. Bépp jumtukaay boo wara jëffandikoo waat daa wara dekontamine wu te set wecc. Te nga sànni PPE wa yi sellul yépp ci lu mucc ayib BALAA NGAY JÓGE ci barab yu am feebar bi.
- Maska xar kanam
- Colinu maska gu mucc ayib lu am solo la rawatina ci taskatu xabaar yiy taataan ci mbend mi, ci barb yu tëjju, ak/mbaa fu feebar bi jublu. Nga bayi xel ne fu ruusiti jàngoro ne ci barab yu tëjju yi loolu mën naa yokk riska yi, te yit mën naa yokk jakarlook jàngoro ji.
Ngay bayi xel ci ne colinu maska xarkanam bu jaarul yoon mëness na cee jële jàngoro ji. Am na jàngat bu Lancet def di wone des gi domi jàngoro jiy des ci ay maska ginnaaw juróom ñaari fan ba mu ca tabee. Ba tey it jàngat bi wone na lii di summi, jëffandikoowaat, wala laal sa xarkanam booy sol maska mënees na caa jële jàngoro ji.
Boo de sol maska toppal ndénkaane yi:
● Sooy taataan ci barab bu tëjju, fu jegge ay nit wala fu feebar bi jublu sol maska N95 (wala FFP2/FFP3) lañu santaane ci kaw maska ‘oppeerekat’
● Mu wóor la ne maska bi muur na ba daj sa bakkan ba ci sikkim bi baña bàyyi poroxndoll.
● Te ngay wat kawaru xarkanam ngir maska bi mën muur fépp.
● Na nga saxóog camonte ga ca war yëp. Bul laal kanamu maska bi, soo koy summi nga jàpp ci laf yi, te moytu di ko laal aka defaraat ci lu dul lu jamp. Te nga raxas say loxo saa soo laale sa maska.
● Jëfandikoo waat maska am na ay riska yu mag. Saa soo paree ci maska nga fass sani ko mbalit.
● Te ngay raxas say loxo ci ndox mu tàng ak saabu, wala ndoxum alkol (lu ëpp 60% ethanol wala 70% isopropanol) soo dindee sa maska.
● Su maska bi tàmbalee gajaf/guus nga summi ko te sol bu bees, set te wow.
● Nga bàyyi xel ne sol maska benn la ci pexe yi ngay aare sa bopp. Ban di laal sa gémmiñ, sa bakan, ak say bët ak di raxasso ndox mu tang ak saabu lu ci am solo la.
● Te nga xam it ne maska xarkanam am ko yombul /wala njëg gi mën naa seer lool ci yenn barab yi.
Li aju ci Kaaràngay jumtukaay
Wer na ni jumtukaay yi doomi jàngoro ji tagg mën na fa jaare law. Ñépp wara saxoo di fomp aka settal saa su ne.
- Deel jëffandikoo mikoro yu gudd sorri nit ki te bañ tappal kenn ab micro.
- Kuwertiiru mikoro yi daffa laac fomp ak raxass bu sett ci ndox bu tàng ak saabu saa su soo ci pare. Laac teel/xamlul naka lanuy dindee kuwertiir ci lu mucc ayib ngir moytu difa toxalee jàngoro ji. Nga moytu jëffandikoo kuwertiir yiy dëssel ngelaw ndax dañiy naqaree settal.
- Jëffandikool deglu kaay yu yomb njëg fooko mëne te nga sani leen soo ci paree.
- Jëffandikool gëttu kamera yu gudd ngir mëna samonteek dàndante bi.
- Saa soo ko mënee nga jëffandikoo jumtukaay san fiil mo gën yi andak fiil.
- Xamal ni ngay dence sa jumtukaay ci liggéey bi. Bul bayi dara muy taxawaalu, te nga deloo lu ci nekk fa mu dëkk te tëjj ko (lu mel ni keess ngi ngay yeegge roplan, te mu yomba raxass lool)
- Sudee yomb na la, lëmësal ak palastik jumtukaay yi ngay jëffandikoo. Dina na nèewal domu jagoro tagg ci jumtukaay te dina yombal fomp ak raxass bi.
- Nga yore ay batari sekur yu doy te moytu di resarze fenn ci liggèey bi, ganaw domi jàngoro ji mën na fa jaaré.
- Fompal bépp jumtukaay ak porodiwi yu melni Meliseptol di ray mikorob, tegg ci fomp yeneen yëpp yu mel ni portabal yi, tablet yi, kabal yi, piriis yi, laptop yi, disk ekstern yi, kamera yi, press pass yi ak kordon badsa yi.
- Na la woor ne jumtukaay yëppë sett so leen di deloo, te nga yëgoo ci ak ñi koy saytu ganaw bamu la leere ne taggatu nan ci fomp. Na la wer ne ken deloo si wul ben jumtukaay te yëgoo wu ci ak kikoy saytu di ko settal.
- So yore ndaamaar ci liggéey bi, so wacce na la wer ne raxas kat yu ci tagattu raxass nañu ko birr ak bitti. Te ñu raxas bu baax yii nga xamne ñéppa leen di laal mu di puwañe yi, wolan bi, lewiye witèes bi, farin a min , séetu bitti yi, reposs tet yi, sentiir sekirite yi, tablo de bor bi, manet yi wacce kayug wiiter/jafandu kaay/ak butoŋ yépp.
Nooy raxasse jumtukaay yiy jëffandikoo kuranŋŋ
Tomb yii mooy wane naka ngay raxasse jumtukaay yiy jëffandikoo kuranŋ.Na nga jang li ci defar kat bi wax lépp ciy tektal balaa ngay tambali raxass.
- Roccil/dindil bepp piriss, apaarey, ak kaabal.
- Léep luy xeetu ndox na sori jumtukaay bi, te bul jëffandikoo ayerosol, odesawel, wala luy ñori-yii yëp day yax say jumtukaay
- Bul timale say aparay muk ak pomp
- Ngay jëffandikoo sër yu dul bayyi tilim te nooy saa sooy fomp.
- Nga gajafal wala guusal sër bi, te BUMU tooy. Dolli ci saabu bombu ko ak sa loxu
- Fompal aparay bi ay yooni yoon
- Bul bayi benn tooyaay ci bunti aparay yi (roofu kaay, fi ngay roof deglu kaay yi, bindu kaay gi.)
- Nga wawal ko ak ser bu set, waw te nooy.
- Yenn defar kat yi santaane nañu ngay fompe ak alkol isopropyl 70% leep lu degar wala ludul siit.
- Sooy settal sa jumtukaay na nga xool ku defar li nga koy setal le, ndax mënees naa yax sa jumtukaay
Ngir gën ci leer lu yërël fii
Kaarànge ci lënd gi
● Na nga bàyyi xel ci xoqotal yi taskati-xabaar yi di jànkonteel ci lënd ci seen walug liggéey jëm ci taataani xibaari COVID-19 bi. Mën naa jogge ci gurub yiy bañ ñakku wala ñi buggul takki maska Yëral li ci CPJ indi ci ay doxalin bi gën yu lay muccal ci songaate yooyu.
● Gornamaa yi ak kër yiy liggéey ci xarala yu bees yi ñoo ngi jeffendikoo sirweyans ngir topp lawug COVID-19 bi. Ku mel ni NSO Group bokk na ci, ñoo tëgg Pegasus, di ab losisiyel espiyõo bu ñuy jëffan- dikoo di ci yëddu taskatu xabaar yi ci nikko Citizen Lab waxee. Kuréelu liberte ciwil yi ñu ngi mébét ni sirweyans teknik yooyu mëness na cee jaar di yëddu ay nit su mbass mi jeexee. Kii di “Transparence Internationale” mu ngi topp la cay xew fépp ci àdduna bi ci seenub dal
● Saay-saay yaa ngi pëttaxlu ci njàqare gi dab nit ñi ci mbas mii di ërtal ay nit ak ay kureel ci songin yu xarañé jëmale ko ci walug ñakku gi ci lu bir àdduna sepp, suñ sukendikoo ci ay xibaar. Na nga àndak teey balaa ngay seet dara wala ngay wàccee leen lu jóge ci lënd ci walug COVID-19 wala lu jem ci ñak ci lu mën di jaar ci seeni appaarey di leen yëddu, ci ni ko kureel gii di Electronic Frontier Foundation waxee.Ngeen di teeylu su ngeen bëgee yër lenn luy wax ci COVID-19 bi bàyyikoo ci mbaalu-jokkoo yi wala jëfekaay yi ñuy yónnee ak di jot bataaxal yi, daf ci am yu lay këpptal ci ay dal yuy yàq sa appaarey ak ay wiris
● Teeyal ci nguur yiy tasaare xibaar yu wérul, ci ni ko The Guardian indee, ak lu mel ni xibaar yu wérul yi jëm ci askan wi, loo xam ni OMS xamle nako ci anam yu leer, teg ci kii di BBC leral na ko. Dalub OMS am na ngindikaay ngir mucc ci yu wérul yooyu
● Yëral mbaalu-jokkoo yi lu aju waxtaan yi ak mbiri jàmbur yi nga xam lu nuy doyee say mbiri bopp, amuñu ci dara, ak lan moo ci am kaarànge. Nga bàyyi xel yit ni léegi nit ñu baree ngi toog ca seen kër di fa liggéeye, serwis yu bari hackers yi dañu leen di ërtal.
● Bàyyil xel ci risk yi am ci xibaar yiy baawo wala ame ci réew yi nga xam ne nguuru nootànge moo fay dox, nga xam ne dañuy topp lépp lufay jib ci xibaar ci COVID-19 bi. Yenn gornamaa yi sax mën na ñiy nëbb yaatuwaayu mbass mi/wal sax aaye mejaa yi di ci wax, ci ni ko CPJ wone
Pékke ak Kaarànge ci liggéey bi
● Soo dee dem liggéeyi cim réew (yëral fi suuf), gestul nu fa kaarànge gi tëddee, nga japp it am na ay léeg-léeg mu ami xew- xew yu tar ak ay ñaxtu yu am ci àdduna si ba mbass mi tambalee ba léegi. Amna surnalist reporter yu wax ne song nan leen di leen ërtal aka xoqatal, kon na nga farlu ci kaarange.
● Te nga moytu bu baax sooy dem taataani xibaar ci dëkki kaw yi. Nit ña mën nañoo ñaaw njort/wala ñu mer ndax xamu ñu la yaakaar ni da nga leen di wal feebar bi.
● Nga bàyyi xel ni takk-der yi amalee seen taxawaay ci tereg-génn gi àndak COVID-19 bi, lu mel ne songaate gi, jëfandikoo lakirimosen
● Surnaalist yi di liggéeye réew yi am nguurug nootànge war nañoo sóoraale ne mën nañu leen japp tëj, wala ñu génne leen fa ndax tassum xibaar yi ñeel COVID-19 mi leen fa yóbbu ni ko CPJ wonee
Liggéeyi réew ak réew
Léegi tukki réew ak réew mujj naa jafe lool te néew ndax dogal yi ñu ci jël. Bu dee lu mënut a ñakk na nga topp digle yii.
● Gëstul ba xam fa ngay waaja tukki luñu fa dogal, ndax mën na soppiku ci lu ken dul yëglu.
● Xamal ni ndogali tëj /aki cuwerfe mënees na wuute ci biir am réew. Jappal ne mënees na tëji barab ci lu dul yëglu, kon na ngay top di xam luy xew ci biir réew ma ci wal yooyee.
● Lii jëm ci ay ndogalu ber ñiy wañiku tukki mënees na leena sopi ci ken dul yëglu, ca kaw réew ma nga jëm wala fangay jóge.
● Nemmikul fépp fuñuy fajoo ca fa nga jëm, te nga jàpp ni liggéeykati loppitaan yi mën nañoo seleŋlu aka ñaxtu ci lu kenn dul yëglu.
● Am PPE mëness na jaffe, mbaa du am, wala mu doon yu bonn. Ngay sóorale am ngi ci njalbeen bala ngay dem ci liggéey bi, te nga yobale yi ngay soxla.
● Ñakkul COVID soo ko mënee balaa ngay dem ci liggéey bi, te nga woorlu ne yeneen ñakk yi war ak feebar prophylaxis yéesal nanu leen ca fa nga jëm ca teel.
● Xoolaatal sa asirãasu tukki, te jap ne liggéeyub tukki bu jëm ci COVID-19 bi luy xawa jafe la. Nga xan ne gornamaa yu bari jël nañu seeni mattuwaay aki ndogal yu jëm ci tukki réew ak réew.
● Deel gëstu ndax xew-xew ya ngay waaj a teewe dina amam déet, ndax léegi réew yu bari dañoo tere nit ñuy dajaloo feen wala ay mbooloo, wala ay mboloo yu ëpp yen lim yi.
● Dig yu bari tëj nañu ci àdduna bi. Tëj yeneen a ciy tegu, muy lu mat a sóoraale ci sa yeneen pexe yi ngay tëral.
● Bul tukki soo feebaree. Naawu yu mag yi ak yu ndaw yu bari, ak yeneeni barab yu ni mel jël nañu seen matuwaay yu wóor di seet wérgi yaramu tukkikat yi.
● Jappal ne COVID-19 bi dafa metti ci këri ropalaan yi, ci li news report wax, kon na ngay jënd biye buñuy ramburse soo ci tukkiwul.
● Xamal nu wutug wiisaa gi tëddee fa ngay waaja dem, xam ne réew yu bari dañoo dakkal maye wiisaa.
● Seetal ndax réew ma nga jëm dañoo soxla nga wone këyit guy firndeel ne amuloo COVID-19
● Na nga yombal sa yooni tukki te ngay teel a dem ca naawu ba, di sóoraale ne dina fa am ñuy seet sa wérug yaram ak sa tàngooru yaram. Looloo xew itam ca gaar yaak waax ya, ak ca gaaraasu ndàbb ya.
Soo ñibise ci liggèey bi
● Foo tollu deel seet sa yaram ci lépp luy niru feebar bi.
● Di ngaa soxla ber sa bopp moo gën a wóor soo jógee fu bari riska am feebar bi. Xoolal la dëppook li ci gornamaa ba digle.
● Toppal xibaar yu bees yiy am ci COVID-19 bi, ak tëralin yi aju ci beru ak lesere fa nga jëm ak fa nga jóge.
● Boo xamee fu wallante gi tollu ca réew ma nga nekk, da nga wara am sa surnaal di ci bind turi nit ñi nga jegenteel ak seeni limatu jollasu lu tollook fukki fan ak ñeent (14) soo ñibbi see. Lii dina yombal topaat leen soo tàmbalee gis feebar bi ci yow.
Soo yëgee feebar bi
● Soo yëgee wala nga am feebaru COVID-19, lumu néew-néew, wax ko say njiit. Degoo leen ngay dugu diggente fa nga sotale sa liggèey ak sa kër. Bul tëb rekk jël taksi
● Toppal digle yi OMS ak CDC indi, woowal ñi yor faj mi ci sa biir dëkk ngir aaru aar say ñoñ
● Soo tàmbalee yëg jàngoro ji bul génn sa kër lu tollook juróom ñaari (7) fan ci lu gen gat (diir bi ngay toog dina wuute ci ni ko sa gornamaay terele). Ci noonu nga mënee aar say ñoñ diirub jàngoro jiy nekk ci yow.
● Ngay sóoraale di sakku ndimbal. Laajal sa njaatige, say xarit ak sa waa kër, loo soxla ñu indil la ko teg ko sa buntu néeg.
● Soo bokkoon dal ak ñeneen, dañoo wara beru ñoom ñépp fukki fan ak ñeent (14). Ay tegtal yu ci aju yu am soloo ngi nii. Te nga moytu bu baax na ngay demee ca sangukaay ba, ca ginnaaw kër ga, ak ca waañ wa, ngir moytu wàllante gi.
● Te nga tob digley dàndante gi ci anam yi war ca sa biir ker te soo ko menee ngay fanaanook sa bopp.
Aarukaay CPJ gi nekk ci lënd gi dina jàppale taskati-xibaar yi ci jumtukaay yi ñu soxla ci liggéey bi, ci lënd gi, ak sellum xel, boole ci taataani eleksiyon ak yëngu-yëngu ci biir réew yi.
[Boroom mbind mi neena: Lii ñi ngi ko jënka tasaare ci 10i fanuk fewerye 2020, diko yéesal saasu nek. Bis biñ ko genne te ne mu nek ca kaw mbind mi mooy firndeel yéesalaat gi.]