Ndénkaaney CPJ ci kaarànge: liggéey ci jamonoy mbasum koronaawiris

Ay taskatu xibaar meksikin, yu sol liy muur yaram ci mbaas COVID-19 bi, di taataan doxu naxtu gi tabikoo ci liggéey kati biro ya ca lopitaan ba ca Meksiko Siti te tudd Seneral Balbuwena, bissu fuki fan ak juroóom benn ci awril , 2020. (AFP/Pedro Pardo)

Yeesalu 20i Mai 2021

Ci 10i fan ak benn ci weeru maars 2020, kuréel gi yor wérgi yaram ci àdduna bi (OMS) neena lii di COVID-19 bi (Koronaawiris) feebaru mbass la. Mbir yaa ngi dox ci àdduna, tekk ci reew yaa ngi yokk wala di wañi tere yi ak/wala lepp lu jëm ci wallu kaarànge ngi ndax gis nañ xéeti koronaawiris yu yees (ay wariyant) ak porogarami ñakku yaa ngi gën di dem.

Taskati-xibaar yi ci àdduna ñu ngi def liggéey bu am solo ci yee askan wi ci lu jem ci feebar bi ak nan la réew yi taxawee ci xeex ko, ginnaaw bi ay ngornamaay réew yu bari gàllankooree tasum xibaar ak jotug xibaar gi, ci ni ko CPJ firndeele ci seenum mbind. Ñiy yëngu ci mejaa yi dañuy jànkonteel ay ërtal ak jafe-jafe yu tar, teg ci leeg-leeg- mën nañu ame ci jàngoro ji fépp fu leen seen liggéey yóbbu, wala tukki ak laaj-ak-tontu yi seen liggéey bi laaj, ni ko CPJ waxee ci laaj-ak-tontu bi ñu séq ak taskati-xibaar yi

Ngir xam lu xew bis bu nek ak yéesal yi am ci digle yi ak tere yi, tass kati xabaar yiy yengu ci mbass mi war nañuy top xibaar yi bayikoo ci OMS ak kuréel ya ŋank walum pacc ca seeni askan. Ngir am lu wér ci lawug jàngoro ji waxtu wu nekk dal bi tudd Johns Hopkins University Coronavirus Resource Center nekk na barrab bu wóor te mucc ayib ci jottali xibaar ci wàll woowu. 


Aar sa bopp ci biir nit ñi


Tere yi jëm ci tuki réew ak réew ak/wala ci wallu kaarànge gi danuy sopikku saa su ne, ba tax na liggéeyu mejaa yi mën nañu soppi anam biñu koy defee wala dakkal ko ci lu kenn dul yeglu.

Ñiy yëngu ci tassum xabaar te ñakku ba noppi war nañu bàyyi xel ci ne mën nan wale jàngoro ci ba leegi, ci ni ko centaru amerikin biy saytu bepp feebar (CDC) waxe, ndaxit xéetu ñakk bu ne akk namuy aare nit ki ci xéeti jàngoro yi wiris bi andale, ci ni ko Yale Medsin waxe. Ba tax na xéeti kaaràngey COVID 19 yu mel ni dàndante gi and takk maska, war nanu leena saxal saa su nekk.

Képp kuy waajal liggéey ci jamonoy mbassu COVID-19 war naa bàyyi xel ci ndénkaane kaarànge yii: 

Waajtaayug liggéey bi

     Sellug Xel

      Mucc ci wàllu gi ak wàllaate gi


      Réew yu bari ñoo ngi wëyel dàndante/ci diggante nit ñi , wante réew mu nek ak namu koy doxale. Sooy taataan xibaar ci barab yu feebar bi jublu lool wala ngay dem ci ben ci barab yii ñuy waaja lim, balaa ngay dem laajteel yan yiirukaay set setal lañu fa tëral. Bu dalul sa xel bul dem.

      Ay ndékaane yees nangu ngir mucc ci wàllante gi

Muuru kaayu yaram waa loppitaan (PPE)

Ngir taataan ci anam yu sela, tass katu xabaar yi maness nanuy sol muuru kaayu yaramu waa lopitaan PPE yu nek su ko seen liggéey bi laajee. Lu mel ni ay gãa aa seté, maska xar kanam, taabelye / kombinesõo / wala liy muur dàll ak yuni mel.

Sol ak simi ci anam yu woor muuru kaayu yaramu waa lopitaan PPE dafay àndak sàmmoonte gu mucc ayyib ak ndénkaane yi ci jëm. Bësal fii ngir xam ndénkaane yi bàyyikoo ca CDC. Sooy sumi muuru kaayu yaramu waa lopitaan PPE nga nga deff ko ci anam yu mucc ayib, ndax toxalee ca jàngoro ji lu gaaw la. Lu la leerul nga laaj ki xam mu tàggat la ci balaa ngay dem ci liggéey bi.

 Na nga xamit ne ca rèew yu bari muru kaayug yaram waa lopitaan (PPE) yu baax neew na fa, jëffandikoo ga mën na indi ñakkam.  

Ngay bayi xel ci ne colinu maska xarkanam bu jaarul yoon mëness na cee jële jàngoro ji. Am na jàngat bu Lancet def di wone des gi domi jàngoro jiy des ci ay maska ginnaaw juróom ñaari fan ba mu ca tabee. Ba tey it jàngat bi wone na lii di summi, jëffandikoowaat, wala laal sa xarkanam booy sol maska mënees na caa jële jàngoro ji.

Boo de sol maska toppal ndénkaane yi:

● Sooy taataan ci barab bu tëjju, fu jegge ay nit wala fu feebar bi jublu sol maska N95  (wala FFP2/FFP3) lañu santaane ci kaw maska ‘oppeerekat’

● Mu wóor la ne maska bi muur na ba daj sa bakkan ba ci sikkim bi baña bàyyi poroxndoll. 

● Te ngay wat kawaru xarkanam ngir maska bi mën muur fépp.

● Na nga saxóog camonte ga ca war yëp. Bul laal kanamu maska bi, soo koy summi nga jàpp ci laf yi, te moytu di ko laal aka defaraat ci lu dul lu jamp. Te nga raxas say loxo saa soo laale sa maska.

● Jëfandikoo waat maska am na ay riska yu mag. Saa soo paree ci maska nga fass sani ko mbalit.

● Te ngay raxas say loxo ci ndox mu tàng ak saabu, wala ndoxum alkol (lu ëpp 60% ethanol wala 70% isopropanol) soo dindee sa maska.

● Su maska bi tàmbalee gajaf/guus nga summi ko te sol bu bees, set te wow.

● Nga bàyyi xel ne sol maska benn la ci pexe yi ngay aare sa bopp. Ban di laal sa gémmiñ, sa bakan, ak say bët ak di raxasso ndox mu tang ak saabu lu ci am solo la. 

● Te nga xam it ne maska xarkanam am ko yombul /wala njëg gi mën naa seer lool ci yenn barab yi.

Li aju ci Kaaràngay jumtukaay

Wer na ni jumtukaay yi doomi jàngoro ji tagg mën na fa jaare law. Ñépp wara saxoo di fomp aka settal saa su ne.

Nooy raxasse jumtukaay yiy jëffandikoo kuranŋŋ

      Tomb yii mooy wane naka ngay raxasse jumtukaay yiy jëffandikoo kuranŋ.Na nga jang li ci defar kat bi wax lépp ciy tektal balaa ngay tambali raxass.

       Ngir gën ci leer lu yërël fii 

Kaarànge ci lënd gi 

● Na nga bàyyi xel ci xoqotal yi taskati-xabaar yi di jànkonteel ci lënd ci seen walug liggéey jëm ci taataani xibaari COVID-19 bi. Mën naa jogge ci gurub yiy bañ ñakku wala ñi buggul takki maska Yëral li ci CPJ indi ci ay doxalin bi gën yu lay muccal ci songaate yooyu. 

● Gornamaa yi ak kër yiy liggéey ci xarala yu bees yi ñoo ngi jeffendikoo sirweyans ngir topp lawug COVID-19 bi. Ku mel ni NSO Group bokk na ci, ñoo tëgg Pegasus, di ab losisiyel espiyõo bu ñuy jëffan- dikoo di ci  yëddu taskatu xabaar yi ci nikko Citizen Lab waxee. Kuréelu liberte ciwil yi ñu ngi mébét ni sirweyans teknik yooyu mëness na cee jaar di yëddu ay nit su mbass mi jeexee. Kii di  “Transparence Internationale” mu ngi topp la cay xew fépp ci àdduna bi ci seenub dal 

● Saay-saay yaa ngi pëttaxlu ci njàqare gi dab nit ñi ci mbas mii di ërtal ay nit ak ay kureel ci songin yu xarañé jëmale ko ci walug ñakku gi ci lu bir àdduna sepp, suñ sukendikoo ci ay xibaar. Na nga àndak teey balaa ngay seet dara wala ngay wàccee leen lu jóge ci lënd ci walug COVID-19 wala lu jem ci ñak ci lu mën di jaar ci seeni appaarey di leen yëddu, ci ni ko kureel gii di Electronic Frontier Foundation waxee.Ngeen di teeylu su ngeen bëgee yër lenn luy wax ci COVID-19 bi bàyyikoo ci mbaalu-jokkoo yi wala jëfekaay yi ñuy yónnee ak di jot bataaxal yi, daf ci am yu lay këpptal ci ay dal yuy yàq sa appaarey ak ay wiris 

● Teeyal ci nguur yiy tasaare xibaar yu wérul, ci ni ko The Guardian indee, ak lu mel ni xibaar yu wérul yi jëm ci askan wi, loo xam ni OMS xamle nako ci anam yu leer, teg ci kii di BBC leral na ko.  Dalub OMS am na ngindikaay ngir mucc ci yu wérul yooyu

● Yëral mbaalu-jokkoo yi lu aju waxtaan yi ak mbiri jàmbur yi nga xam lu nuy doyee say mbiri bopp,  amuñu ci dara, ak lan moo ci am kaarànge. Nga bàyyi xel yit ni léegi nit ñu baree ngi toog ca seen kër di  fa liggéeye, serwis yu bari hackers yi dañu leen di ërtal.


 ● Bàyyil xel ci risk yi am ci xibaar yiy baawo wala ame ci réew yi nga xam ne nguuru nootànge moo  fay dox, nga xam ne dañuy topp lépp lufay jib ci xibaar ci COVID-19 bi. Yenn gornamaa yi sax mën na  ñiy nëbb yaatuwaayu mbass mi/wal sax aaye mejaa yi di ci wax, ci ni ko CPJ wone

       Pékke ak Kaarànge ci liggéey bi

        ● Soo dee dem liggéeyi cim réew (yëral fi suuf), gestul nu fa kaarànge gi tëddee, nga japp it am na ay léeg-léeg mu ami xew- xew yu tar ak ay ñaxtu yu am ci àdduna si ba mbass mi tambalee ba léegi. Amna surnalist reporter yu wax ne song nan leen di leen ërtal aka xoqatal, kon na nga farlu ci kaarange.

        ● Te nga moytu bu baax sooy dem taataani xibaar ci dëkki kaw yi. Nit ña mën nañoo ñaaw njort/wala ñu mer ndax xamu ñu la yaakaar ni da nga leen di wal feebar bi. 

        ● Nga bàyyi xel ni takk-der yi amalee seen taxawaay ci tereg-génn gi àndak COVID-19 bi, lu mel ne songaate gi, jëfandikoo lakirimosen

          ● Surnaalist yi di liggéeye réew yi am nguurug nootànge war nañoo sóoraale ne mën nañu leen japp tëj, wala ñu génne leen fa ndax tassum xibaar yi ñeel COVID-19 mi leen fa yóbbu ni ko CPJ wonee 


        Liggéeyi réew ak réew

        Léegi tukki réew ak réew mujj naa jafe lool te néew ndax dogal yi ñu ci jël. Bu dee lu mënut a ñakk  na nga topp digle yii.

        ● Gëstul ba xam fa ngay waaja tukki luñu fa dogal, ndax mën na soppiku ci lu ken dul yëglu.

        ● Xamal ni ndogali tëj /aki cuwerfe mënees na wuute ci biir am réew. Jappal ne mënees na tëji barab ci lu dul yëglu, kon na ngay top di xam luy xew ci biir réew ma ci wal yooyee.

        ● Lii jëm ci ay ndogalu ber ñiy wañiku tukki mënees na leena sopi ci ken dul yëglu, ca kaw réew ma nga  jëm wala fangay jóge.

        ● Nemmikul fépp fuñuy fajoo ca fa nga jëm, te nga jàpp ni liggéeykati loppitaan yi mën nañoo seleŋlu aka ñaxtu ci lu kenn dul yëglu.

        ● Am PPE mëness na jaffe, mbaa du am, wala mu doon yu bonn. Ngay sóorale am ngi ci njalbeen bala ngay dem ci liggéey bi, te nga yobale yi ngay soxla.

        ● Ñakkul COVID soo ko mënee balaa ngay dem ci liggéey bi, te nga woorlu ne yeneen ñakk yi war ak feebar prophylaxis yéesal nanu leen ca fa nga jëm ca teel.

        ● Xoolaatal sa asirãasu tukki, te jap ne liggéeyub tukki bu jëm ci COVID-19 bi luy xawa jafe la. Nga xan ne gornamaa yu bari jël nañu seeni mattuwaay aki ndogal yu jëm ci tukki réew ak réew. 

        ● Deel gëstu ndax xew-xew ya ngay waaj a teewe dina amam déet, ndax léegi réew yu bari dañoo tere nit ñuy dajaloo feen wala ay mbooloo, wala ay mboloo yu ëpp yen lim yi.

        ● Dig yu bari tëj nañu ci àdduna bi. Tëj yeneen a ciy tegu, muy lu mat a sóoraale ci sa yeneen pexe yi ngay tëral.

        ● Bul tukki soo feebaree. Naawu yu mag yi ak yu ndaw yu bari, ak yeneeni barab yu ni mel jël nañu seen  matuwaay yu wóor di seet wérgi yaramu tukkikat yi. 

        ● Jappal ne COVID-19 bi dafa metti ci këri ropalaan yi, ci li news report wax, kon na ngay jënd biye buñuy ramburse soo ci tukkiwul.

        ● Xamal nu wutug wiisaa gi tëddee fa ngay waaja dem, xam ne réew yu bari dañoo dakkal maye wiisaa.

        ● Seetal ndax réew ma nga jëm dañoo soxla nga wone këyit guy firndeel ne amuloo COVID-19

        ● Na nga yombal sa yooni tukki te ngay teel a dem ca naawu ba, di sóoraale ne dina fa am ñuy seet sa   wérug yaram ak sa tàngooru yaram. Looloo xew itam ca gaar yaak waax ya, ak ca gaaraasu ndàbb ya.

         Soo ñibise ci liggèey bi

         ● Foo tollu deel seet sa yaram ci lépp luy niru feebar bi.

          ● Di ngaa soxla ber sa bopp moo gën a wóor soo jógee fu bari riska am feebar bi. Xoolal la dëppook li ci gornamaa ba digle.

        ● Toppal xibaar yu bees yiy am ci COVID-19 bi, ak tëralin yi aju ci beru ak lesere fa nga jëm ak fa nga  jóge.

        ● Boo xamee fu wallante gi tollu ca réew ma nga nekk, da nga wara am sa surnaal di ci bind turi nit ñi  nga jegenteel ak seeni limatu jollasu lu tollook fukki fan ak ñeent (14) soo ñibbi see. Lii dina yombal  topaat leen soo tàmbalee gis feebar bi ci yow.

        Soo yëgee feebar bi

        ● Soo yëgee wala nga am feebaru COVID-19, lumu néew-néew, wax ko say njiit. Degoo leen  ngay    dugu diggente fa nga sotale sa liggèey ak sa kër. Bul tëb rekk jël taksi

        ● Toppal digle yi OMS ak CDC indi, woowal ñi yor faj mi ci sa biir dëkk  ngir aaru aar say ñoñ

        ● Soo tàmbalee yëg jàngoro ji bul génn sa kër lu tollook juróom ñaari (7) fan ci lu gen gat (diir bi ngay  toog dina wuute ci ni ko sa gornamaay terele). Ci noonu nga mënee aar say ñoñ diirub jàngoro jiy nekk ci  yow.

        ● Ngay sóoraale di sakku ndimbal. Laajal sa njaatige, say xarit ak sa waa kër, loo soxla ñu indil la ko teg  ko sa buntu néeg.

        ● Soo bokkoon dal ak ñeneen, dañoo wara beru ñoom ñépp fukki fan ak ñeent (14). Ay tegtal yu ci aju yu am soloo ngi nii. Te nga moytu bu baax na ngay demee ca sangukaay ba, ca ginnaaw kër ga, ak ca waañ wa, ngir moytu wàllante gi.

         ● Te nga tob digley dàndante gi ci anam yi war ca sa biir ker te soo ko menee ngay fanaanook sa bopp.       

            Aarukaay CPJ gi nekk ci lënd gi dina jàppale taskati-xibaar yi ci jumtukaay yi ñu soxla ci liggéey bi, ci  lënd gi, ak sellum xel, boole ci taataani eleksiyon ak yëngu-yëngu ci biir réew yi.

[Boroom mbind mi neena: Lii ñi ngi ko jënka tasaare ci 10i fanuk fewerye 2020, diko yéesal saasu nek. Bis biñ ko genne te ne mu nek ca kaw mbind mi mooy firndeel yéesalaat gi.]


Exit mobile version